Ñooy ñan?

TechnoSen SARL  nekk na kërug xarala gu ñoñu Senegaal ak Almaañ samp fii ci réew mi, muy gindee ci wàllu xarala. 

Ag neekam nak, day firndéel yéenéy ñi ko fi samp, ngir indi ay saafara yu méngook aajoy askan wi ci wàllu xarala.

Ngir matale bëgg bëggu askan wi, TechnoSen SARL taxawal na mboloo mu miin te xarañ ci melal ak defar agitam xelal ak jagal bépp xeetu jokko.

Xam xam ak xarañ gi nekk ci TechnoSen akum mboolom, matale na ba mana indi ay saafara ci bépp xeetu jàmbat, muy ci mataryel walla porogaraam (xelum jumtuwaayu xarala yi): tàmbaleeko ci xelal ba ci tërël xëtum internet walla sax jàngle nuñu koy defe, rax ci dolli man laa jaay, installeel la ba noppi di la ko sàmmal.

Li nu taxa jug:

  • Fexe ba askan wi mënë am ci lu yomb te oyof ay saafara yu mucc ëyib ci wàllu xarala, gannaaw bu nu leen indilee taxawu bu yaa ci googu fànn.
  • jébbëlé sunu xam xam ak sunu mën mën agitam indi saafara su gaaw te dëppook yittey këru liggéeyukaay yi ak seeni bërëb.

Sunug jagle ak xam gi nu xam yittey askan wi, tax na nu mënë indi ay saafara ci seen aajo yi gënë tembere ak seeni mébét.

Ngir gënë mana taxawu askan wi, TechnoSen SARL dafay jokkoo aka ligeey ak ay nàttangoo yu bawoo fune ci àddina bépp te xarañ lool ci fànni xarala yépp.